Adaramit

From Wikipedia

Ci angale mooy Adramyttium; Ci faranse mooy Adramytte

Benn dëkk ak teeru la woon, ci diiwaanu nguuru Room bu tuddoon Misi. Tey jii mooy dëkk bu tudd Edremit ca réewu Tirki (Turquie). Waaye ci dëgg-dëgg, ci bérabu dëkk bi tudd tey jii Karatash la nekkoon. Ma nga fare woon dun bu tuddoon Lesbos. Ci jamano Injiil ji nekk na ci diggante dëkku Torowas ak dëkku Pergam.

Ci Injiil dañuy wax ci Adaramit ci Jëf 27:2.