Wikipedia
wowiki
https://wo.wikipedia.org/wiki/X%C3%ABt_wu_nj%C3%ABkk
MediaWiki 1.47.0-wmf.2
first-letter
Xibaarukaay
Jagleel
Waxtaan
Jëfandikukat
Waxtaani jëfandikukat
Wikipedia
Wikipedia waxtaan
Dencukaay
Waxtaani dencukaay
MediaWiki
Waxtaani MediaWiki
Royuwaay
Waxtaani royuwaay
Ndimbal
Waxtaani ndimbal
Wàll
Waxtaani wàll
TimedText
TimedText talk
Module
Discussion module
Event
Event talk
Weeri wolof
0
5123
107595
104175
2026-05-16T00:12:06Z
InternetArchiveBot
12803
Rescuing 1 sources and tagging 0 as dead.) #IABot (v2.0.9.5
107595
wikitext
text/x-wiki
[[Weeri wolof]], ci [[arminaat|arminaatu]] gàddaay gi, walla bu [[jullit]] ñi mbaa bu [[Lislaam]], ab arminaat bu weer la, buy sukkandiku ci doxiinu weer wi ngir xam ak natt weer wi. Jullit ñi danañu ko jëfandikoo ci bépp barab, rawati na ngir natt ak xam xew-xewi ak bisi diine yi. Ki ko sos nag mooy [[Omar Ubn Xattaab]] (g.m), daal di def [[gàddaayug Yonent]] bi (j.m) juge [[Màkka]] dem [[Madiina]] muy ab tàmbaleem, looloo waral deesi tudde ko arminaatub gàddaay gi. Ak doonte arminaat bi ci jamonoy jullit ñi lañu ko sos, teewul turi weer yi ak arminaatub weer ñu leen daa jëfandikoo lu jiitu Lislaam.
Yenn ci [[réew]]i [[araab]] yi, mu ci mel ne [[Araabi Sawdit]], moom ci nguur geek askan wi dañuy jëfandikoo arminaatub gàddaay gi niki arminaat bu kilifawu di ci taariixe ci bindante yiy am ci diggante liggéeyuwaayi nguur gi, waaye nag lu ci dul moom, askani araab yi ci des yépp arminaatu [[Arminaatu Garegori|Garegori]] (bi dale ci juddug Yonent Yàlla Iisaa) lañuy gën a jëfandikoo..
Arminaanub gàddaay gi mi ngi ame ci 12 [[weer]] yu weer wi, maanaam atum gàddaay gi mi ngi tollook 354 bés daanaka, maanaam 354.367056 ci ay bés. Weer wi ci arminaatu gàddaay gi, benn mu nekk 29 walla 30 bés (ndax doxug weer wu feeñ wi 29.530588 bés la). Ginnaaw nag wuuteg 11 fan am na ci diggante [[Arminaatu jant|arminaatu judd]] gi ak bu gàddaay gi, ñaari arminaat yi duñu jamonoo mukk (duñu tolloo mukk) looloo waral dëppale leen di gën a jafe.
== [[Weer]] ci arminaatu gàddaay gi ==
# [[Tamxarit]]
# [[Diggi-gàmmu]]
# [[Gàmmu]]
# [[Rakki-gàmmu]]
# [[Rakkaati-gàmmu]]
# [[Maami-koor]]
# [[Ndeyi-koor]]
# [[Baraxlu]]
# [[Koor]]
# [[Kori]]
# [[Diggi-tabaski]]
# [[Tabaski]]
== Lëkkalekaay yu biti ==
* {{en}} [https://web.archive.org/web/20090105223532/http://www.oumma.com./Le-calendrier-musulman-en-10 Khalid Chraibi : Le calendrier musulman en 10 questions]
* {{en}} [http://www.staff.science.uu.nl/~gent0113/islam/islam_tabcal.htm Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar)]
* {{en}} [https://web.archive.org/web/20200621105742/http://www.staff.science.uu.nl/~gent0113/islam/ummalqura.htm The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia]
[[Wàll:Lislaam]]
[[Wàll:Arminaat]]
[[Wàll:Weeri wolof]]
fztmvryd1fvnzygqaldjuchv5s9ba19